Dina delusi
Toopna yoon bi ngay fatelu
Bidew ya ngi seetaan
Fo xool ngalawa pënd thino
Gëmulo ne dina oibisi
Dina delusi lerna
Waye boma fatee
Dina delusi lerna
Wadje suou woy dinga yëg
Dina delusi worna
Waye boma fatee
Bataxal bii moy wone
Nimala namme dila djege
Thi ngoon yu weeta weet
Xamnane toog di xaar mo des
Ni xale bu sawar
Di xaar foonu dneydja
Subateel di xaar nadjbi
Xol di neg dej bu neex